You are on page 1of 16

1

www.daaraykamil.com

Nahjul Xadaail Haaji - Wolof


Maa ngi Tmbali samay wax ak jf ci turu Ylla miy kiy boroom yrmande ju yaa ji ci adduna ak ju u jagleele ji ca allaaxiraa. Yal na Ylla dolli xewal ak mucc ci suu sang Muhammad ak ci oam aki saabaam ci anam gu sax Ylla doy na u, moom de weruwaay wu baax la (wu mat a wer say mbir, joyal ko ko). Jf yaa ngi ci yene yi, ku nekk it la nga yeneey sag pay Bokk na ci hikam (sagesse) : ku skku mbir de bu ca saxee am ko. Ku fgg bunt it boo fa saxee ubbilees la Bokk na ci hikma bat ay: ku tyye boppam wlif neen yi (caaxaan yi ) limees ko mu bokk ci boroom xel yi.

Bokk na ci ba leegi: ku dul merloo boppam du begloo boroomam. Bokk na ci ba tay : ku def la ko soob dajeek la ko naqari. Bokk na ci: ku taqook jiyaar ak bakkanam, texe fa biir bmmeelam . Bokk na ci : ku topp Yonnant bi, am gn ji la mu aan. Am ku jl maanaa yii ypp boole leen ci wenn bayit : ( kpp ku woor wlif caaxaan yi () danga dogi ciy ngnel

1 Taalif wi [
Taaliif wii nag lu u barkeel la ci njlben gi ba ca dayo ba. Moom nag (ki waxoon bayit wu njkk wi) yal nau ko dolli ag bbb (xewal) am na ba tay weneen bayit wu yor maanaa mii, mu ciy nos (woy) maanaam waxi sriam ji, wax jooju mooy jii : (nguurug neen waxtu rekk la, nguurug dgg nag day wey ba yawmal-xiyaam)

www.daaraykamil.com

Woy waa ngii : ( dgg day sax , neen nag bu kawe woon it day mujj naaxsaay, mujj suufe)

Maa ngi Tmbali samay wax ak jf ci turu Ylla miy kiy boroom yrmande ju yaa ji ci adduna ak ju u jagleele ji ca allaaxiraa

2 Ubbite gi

Kii di doomi sriam ji dul sant ci boppam lu dul turam (wu tedd wa) Muhammad, Kii de mi ngi sant Ylla (t.m) mi suturaal ay ayibam te taxawu ko te dimbali ko.

Tudd naa sellam ga moom de boroom bu tedd la bob may na ma lu waral ma koy sant. Moom de mooy ki def ay teggiin yu raf muy luy lq ag rer ak judd bu naaw (bonu askan). Mooy ki jagleel boroom xam-xam yeek teggiin, mooy ki len jagleel ab yool akug jam-jub (def la jub). Xewal ak mucc gu kawe nau sottiku ca ka yegoon ca Alburaax (Yonnant bi). Kooku mooy suu sang biy woote jme ci aji bind ji (ki skk mbindeef yi), defe ko nag ci gn jaa rafeti teggiin yi . Kooku mooy Muhammad ak oam i di woroomug raw ak saabaam yi lq ngnelul Aji des ji (Ylla mi fi dul jug) oom saaba yooyu de saxaloon nau ag laa-biire ci lu dul aayoo , ndaxte daoo toroxaloon seeni bakkan ba far len moom. Snkoon nau seeni alal cig joxe ci lu dul ngistal mbaa naafeq. u sukkandiku woon ci Aji jari (Ylla) jiy Aji wrsgale, ngir ag wakkiirlu ci moom ci mbooleem wrsg yi. oom de daoo boyoon jm alaaxlenniraa ngir ne daoo fase woon wujj wa (adduna). Masuoo byyi lenn ndigal lu juge ci Aji settantal ji (kiy def mbir yi di Yalla) kiy Aji bind ji. oom de - ci saffanub uy byyi ndigal yi - dau ciy sax nd ceek bnneex, ndaxte koomum ja yi du tax u koy ftte (alal ji uy jle ci marse yi duu tax uy ftte ndigali suu boroom yi) . Wui woon nau lndm-lndmi gox yi ci xam-xam ak jf ak dppoo. Ndaw u di sang yu aw ! oom de la neexoon ca cafka ga jl nanu ko. Yal na ngrm - lol di naa ci dajeek lg ka lq cang gu joyu ga sottiku ci seen kaw . Kooka mooy Muhammad, yal na ko Aji des ji sotti ay xewal ak mucc mook oam ak saabaam yi di ay ndab (yuy duy xam-xam aki xeewal aki hikam)

www.daaraykamil.com

3 Li waral xasida gi

Man dey tay damaa w ngir wuyyu lenn ci murit yi di woroomi tuub (iy tuub ak a jggalu seen boroom).

oom de daoo skku woon u defal leen woy wuy jngale ay teggiin, ngir u skkoo ciy teggiin, te loolu wartef la . Ndax kat kpp ku bgg a topp Yonnant bi te tegoo ko ciy teggiin dees na ko xa ag texe akug jariu Moom teggiin de - ci dduna ak allaaxiraa mooy gn ji ndmb tey gn ji lu ku tedd di tedde Ndaxte mooy leeral ab xol tey jegeele jjana.Dina waral say dkkandoo di la tagg te dina sooreel it sawara. Ma daal di jug (ngir skku gi u ko skku woon ci man ) gaawantu, tontu len, di ci skku nag ab yool ak ngrm. Moom nag du lu dul jl la Waliya wa tuddoon Dal-Haaji wesaroon (manaam la mu bindoon te woyu ko,maanaam defu ko woon ay bayit ) def ko ay woy, di aan ci def gi Ylla fajal ma samay aajo

4 Lu tax ma taamu ko ?

Ndax dafa boole ba noppi gttal ko li pp ci li taalifkat yu njkk ya bindoon cig tqale.

Lpp loo gis mu new te doy moo gn lu bari te sonle. Def naa ko nag woy wu ami njari, ci baaxug Ylla mi dige (ci Alquraan) ne dana aar (i gm) Ndax Ylla may ma ci ngrm ak kuulute ak njggal ca bisub njqare ba. Kon kat yen skkukati xam-xam yi maa ngi leen di dnk te dellu di len dnk te di leen xiirtal ci tontu bii (tere Nahju bii) Ndax kat yor na ci ay jikko aki teggiin lol (bu ngeen ci tnkoo ) dina leen wommat jme leen ca jub ga Ay gindee ngi ci aki jari yoy boroomug nammeel (ab murit) du ci yoqat mukk Kuy door a dal ak kaa-foree yam ciy njariam , aw yiwam it du jeex mukk. Ndaxte ni uy gge ci gn jaa rafeti jikko yi mi ngi ci ak ca (lu baax) la uy mbt. Maa ngi ko tudde: Nahju QadaaAl Haaji) ci gob mbayum suu sri bii di Dal-Haaj. Maa ngi aan Ylla mu nangu ko ca baaxam ga te ggale liggey bi. Di ko aan it mu mel ne turam wi, ba ki koy jng ay mbiram man cee ywne ngir mu texe Te mu musal ma ci ngistal ak aaw (naw sa jf) ci barkeb Yonnant biy boroom Liwaaul Hamdi Ak yu dul oom aar ci caay-caay yi (bon-bon yi) te mu may ma ay ngnel Te mu musal ma (t.s) ba fwwu ci ayuw ibliis mii nga xam ne dafa ftterlu . Te mu musal ma ci ayu li mu bind ci suuf si, ak li mu bind ci asamaan si ak li nekk ci seen diggante oom aar Te mu may ma ma topp ci sunnas Yonnant bi (j.m) miy gn ji mbindef , miy ku u ramuloo, miy ku u topp Ginnaaw bi mu jullee ci moom te slml ci, ak oam aki saabaam ci anam gu dul dog. Fii nag mooy fi tarjumaani tere bi yam, kon leegi nanu jublu ci (indil leen) teggiin yi.

www.daaraykamil.com

5 ndoorte li

Ngir woy (nos) lii di wesaru Seex Ahmadu - mii di ku geju ci xam-xam maa ngi naan :

Yeen mbooleem way skku yi xam-xam dglu leen sama laabiire gii di len tqaleek ag texeedi Mu di laabiire gog dau leen koo jme ngir jmmi Ylla rekk, muy yee nag jpp aji xellu ak ku jamuj(ftte) : Yoonu teggiin de mooy yrm nadw, ni ko baayam di yrme ak ndayam te weg mag ak def sa moroom ni sa bopp ngir jmmi Ylla mi nekk ca aras (toogu ba)'

saraab aji taalif ji : Yoonu teggiin mooy nga yrm ndaw mel ci moom ni baayam ba ko jur te am lool ci moom yrmande, te mel ci ne ndayam ju am ja ag eewant, nga weg it mag ak doonte da di ab jaam bu bawoo Abasa (Ecopi) , te nga yamale sa bopp ak sa moroom ngir jmmi Ylla kepp. Xamal ni teggiin de mooy taarub boroom xam-xam ak ku koy skku, mooy it takkaayi aji xellu ak ku lewet, mooy njobbaxtalu jikko yi, ku ko takkaayoowul yoqel na (kk na ay takkaay)te neenal, dana mujj di ku ki bind ba ak i mu bind (Ylla aki mbindefam) kpp ku ko gis ba ko te snj ko (mere ko), kepp ku toog ak moom am ci moom ag yoqat akug doyal. Bokk na ciy teggiin ngay laabiire koo gis ca la nga gis ne ag jubam a nga ca, te ngay ba a yayale sa bopp jenn q ci kenn, te nga jort it ne yayoowoo ci kenn mu lay mggal (ci lenn).

Loolu nag mooy li mu junj ci waxam jii :

6 Nangay yrm gone


Nangay yrm gone, (rikk) bu ko nbbal benn yoon genn laabiire gu aw yiwam nekk. Deel weg mag ak doonte da di ku doyadi te xeebu. Bokk na ci ay teggiin nga ba a jort ne yayoo nga jenn q ci kenn ku mu man a doon . Te nga ba a sentu genn maggal ( mbaa wormaal) mu juge ci kenn (kok man nay mer sax ci mggal gi mu lay mggal). Yaw daal jortal ne teggiin yepp ci yaw la war a bawoo, bu leen sentu mukk ci say ndandoo. ndal ak nit i ni nga bgge u nde ko ak yaw. Saraab aji taalif ji : Li mu namm a wax mooy : bokk na ci teggiin yu rafet nga jort ne ay teggiin moom ci yaw rekk la war a juge, te nga ba di ko sentu ci ku dul yaw. Te ngay nd ak nit i ( ci jikko yu baax yi nga bgg u nde kook yaw) (boo ko deful it jikko yoo nde ak oom ci yu bon sentu ko ci oom, nit i daal ni nga mel ak oom rekk lauy mel ak yaw).

www.daaraykamil.com

Nangay smmoonteek aqi (Ylla) - boroom mgg giy boroom kttan gi - ci oom ngir jmmam ja (moom Ylla) ni waxi woykat ba : Mu bgg a wax rekk ne bokk na ci teggiin yu rafet ngay sammoonte ci mbindef yi qi ki leen bind(t.s) ci di ndeek oom ni ko woykat bi waxe ca qasidaam ga yor bahru basiit: Yaw mbokk mi nangay am yrmande ci mbooleem mbindef yi, nanga len di xoole btub eewant ak yrmande Nangay weg mag di yrm gone, tey sammoontek qi aji bind ji ci mpp mbindef. Am na addiis bu naan : sama xeet wi de du da di nekk ciw yiw li fek ku ndaw a ngi ciy weg mag, mag di ci yrm gone. Kon rikk nanga di roy ci gindig Imaam yi (y.y.g)kon de di nga gindiku Bul di toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a kk(loola mooy lu mel ne) : ngay jng ( ci moom) walla nga dkk (ak moom) walla nga bokk ak moom di lekk, bul toogandook moom cib lal it Saa su (Ylla defee nga toogandook moo) nanga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu Akug watandiku, te bul di tafu ci kawam, bul toog it ci kanamam Yaw mbokk mi (rikk) bu ko tllal sab tnk boo toogee ci moom, te deel damm sab gis wlif ko (maanaam bul ko di faral di xool rekk

7 Saraa :
Mu bgg a wax ne : bokk na ci teggiin yu rafet nga bn a toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a kk, ngir jng mbaa dkk ak moom walla di lekkandook moom as. Boo toogeek moom it nanga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu ak wattandiku. Bul di ko oxu mbaa nga koy tllal ab tnk, bu ko di ja tam, bul di baril di gstu ci lu dul aajo, ndax loolu ci mndargay ag ndof la, Ylla nee na (t.s) : (( neel jullit i u dam seenub gis . loolu moom lay junj ci waxam jii di w : Bul di baril looy geestu fu nekk, te dara oru la ci geestu gi. Ndax loolu kat mndargam ndof la, te (boo demee ) ci tereb Ylla bi (di nga fa gis) : ((neel jullit i)) Deel topp ndigali boroom mbindef yi, ndax kat nekk na ci addiis : waay de (snkoo na ci bennub xool rekk) Ab woykat de waxoon na bu ygg ne : ( booy def loo gis xool ko danga ci mas a am bis) kon bul di wndel sab gis . Saraa : Mu namm a wax rekk : war na la nga topp li la sa boroom digal muy damm sab gis. Ndax Addiis bi nee na : waay de dana xool benn xool bob xolam dina ci yqoo nib der di yqoo ca sbej ga , du ca jariu mukk. Woykat ba nee na : ( yaw de boo snnee sab gis ngir sa bnneexub xol, bis dina w bob li ngay gis dina la sonal (danga gis lol doo man lppam (doo man a am lpp ) te doo man a mu rekk ca lenn la ( doo man a yam rekk ca xool ba. Doo ko man a am te doo ko man a mu, bu ko defee ngay sonn ci loo dul am, te boo ko gisutoon doo ko yittewoo) Keneen it ne: ( jmbaar du mooy kiy aar ay gawaram ca bisub jamante ba, bu xare ba tkkee) (waaye ka damm ab gisam mbaa mu lem ab tnk wlif ay moy kooku ci jmmam mooy gawar dgg bay jmbaar ) Bul di baril am po, bul di ree lu bari, mbaa ngay baril looy yngatu ak a defi neen Bul di baj-baji mbaa ngay jem a yddu lu nbbu lu mu man a doon Loolu de mndargam toy la ak woyofum xel ci ku ko baaxoo

www.daaraykamil.com

Boo jekkee nanga dalal say cr, nangay taqook ag noppi nd ak dddu (ci lug dddu war) kon de nga jariu Deel mu ag te bu ci tontu kenn, te mel ni na boroom njngat la (adiib) waxoon : wallaay damay romb waa ji mu may xas may jellale naan kii de xam naa ne waxuma Ndax kat xasante ak weddeente bokk nau ci jikko yi gn a bon niki dorante. Bariy ree daay ray ab xol, kon rikk newalal ree yi, ndax nga grmloo Boroom bi

8 Saraa:
Maanaam bokk na ci teggiin yu rafet nga ba a barili ree, po, ag neen, ag baj-bajeek yngatu ak a jem a yddu lu nbbu, loolu de ci mndargam toy la bokk,ak gttum xel, nangay faral a dal boo jekkee (boo toogee) cib jataay tey faral a noppi, ba u laaj la, bu boobaa nga tontu ci kddu gu suufe, walla nga soxlaa laaj dara, bu boobaa nga def ko te yam ca sa soxla rekk, bu ca dolli dara, ndax kat noppi noflaay a ngi ci ak sutura niki u ko waxe:(nbbal ayib yi kem li nga man cig noppi, ndax kat ab noflaay a ngi ci noppi eel aji noppi ji )(defal sab tontu boo lottee muy noppi, bari na wax joj tontu baa nga ca ag noppi) Bokk na ci Hikma: Bu wax doon xaalis noppi di wurus, bu la nit reree (def la ag kke-teggiin) Jllale ko taqoo noppi, ni ko Ylla waxe: (( Jllaleel eel i rere)) ((bu i rer waxee ak oom nu tontu len ci luy waral jmm)) Ni ko woykat bi waxe: (Amaa na ma romb ku soxat ki (ku yaradiku ki) mu may , bu ko defee ma fegu te naan kii daal waxut ak man) ante ak weddeente bokk nanu ci jikko yi gn a aaw, yi gn a bon, ree ju bari day ray ab xol. Boo bggee am sa ngrmul boroom, newalali ree, Ylla ci jmmam (t.s) moo ne : ((nauy ree lu new )) Boo toogee ak ku la mag booy ree nangay yam ci muu Booy wax ak moom it bul bayliku ( ppal ci wax ji) ndax loolu du lu rafet Noppil ba nga gis mu bgg a wax ak yaw, bu boobaa yamal ca la mu soxla ci yaw Loolu kat moo di ay teggiin, kon jfe ko cig wllam Bu la bccingalee , mual bccingalam yooyu, bu defee lu jaaduwul suturaal ko Bul da di ko jggalu, te bu ko di mere it Bu koy faral di ja (jmale ko say gt , samp ko ko rekk) ci waxtu wu nekk

9 Saraa:
Bokk na ci teggiin yu rafet nga ba di ree ci jataayub ku la mag ndare muu, nga ba di wax ak moom cig bayliku, maanaam ppal ci wax ji, lu or nga wax ak lu orul,moom daal nanga yam ci li mu soxla ci yaw, bu boobaa doxal nga ay teggiin ci moom. Bu la defee lu jaaduwul jggal ko, te di ko jggalu, bul ko di faral di xool xool bu metti, ndax loolu duy teggiin Boo bggee juge ca jataay ba, nanga ko defe cig tyyewu (tyye sa bopp ba suuf du jug pnd du jeqiku) Bu len xpp suuf si ci seeni kanam ndax loolu wuute na ak ag jub Boo ko manee bul di nelaw ci biiru nit u nelawul Ndax kat loolu duy teggiin, ngir ne am na lu ci nekk lu man a waral ag yeddeel (kuy nelaw man ngaa ngelawal te doo ko yg)

10 Saraa:
Bokk na ci teggiin yu rafet nga ba a jeqi pnd boo toogee ci jataay bay jug, boo nammee jug , def ko ci ag dal akug tyyewu, te bul jaar ci kanamu way jekki yi. Bokk na ci ay teggiin nga ba di nelaw ci digg ay way yewwu boo ko manee, ndax amaa na ngelaw gnn ci yaw te doo ko yg, ndax bt ay saau ag suuf(bn-bnu aw taat)

www.daaraykamil.com

Nanga xam ne fuqale bokk na ci liy waral gcca ak yeddeel Kpp ku aj yitteem ci lekk ak sy na xam ne boole na lpp luy toroxte Lekk dee ci jl lu lay dgral ba nga man a jaamu sa boroom te yam ca Deel wattandiku jamono ju nekk fuqale ndaxte mooy cslaayu wpp ay Saraa: Bokk na ci ay teggiin kk a fuqale ak kk a aj sa yitte jpp ciw am , loolu de cig suufe la te day waral ag Woykat ba nee na: (yaw de foo fi joxe sa biir li mu la laaj ak sa py , di nanu gg fa mbooleem toroxte ya yam ) Sab loxo nanga ko tyye, bul ci di baril am po, ndax loolu de ayib la Bul jottaliku mukk lol lqul njari lu la man a jegeel sa boroom

11 Saraa
Bokk na ciy teggiin :tyye sa loxo ak byyi di ci fo ak byyi di ci jefandikoo lu njarin nekkul, loolu de bokk na ci li woroom xel yi ayibal, te ci la musiba yi tase. Saa soo dggee ku la mag mu soxla dara Niki mu bggoon ku mu yonni, rikk demal doxal ko yonneem boobu ngir jmmi Ylla Bu kenn soxla ci yaw dara ndare bu danga koo defal loolu mu soxla ci yaw, boo dee def noonu de danga am teraanga Rikk bul di wax kenn fen nga, walla wax nga lu dul dgg, walla juum nga Walla jeneen wax ju man a merloo ak doonte ki nga koy wax gone la, di ko waxe de ag njuumte la Bu waxee loo xamul nee ko dggal nga, kon dees na la teral Nee ko daal man de tegoon naa ko neneen, walla leneen laa jortoon, walla rere woon naa ko Ak yeneen baat yi walla waxiin yi man a bgale, loolu de boo ko defee def nga lu rafet, bul aawal te bul lore Deel tmbal saw lmmi wax lu baax, kon de dinga ci ame ag texe te dees na la ci fegale wpp ay Ngir waxi sangub mbindef yi (ku nekk na.) yal na ko Ylla dolli ay xewal ci anam gu sax (ku nekk na.) : (ku nekk na di gm Ylla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiw mbaa mu noppi)

12 Saraa
Bokk na ci teggiin yu rafet nga saxoo di faj aajoy ku la mag boo ko dggee mu koy skku, niki mu soxla woon ku mu yonni Bokk na ciy teggiin ba tay nga ba di gntul kenn loo man lu mu soxla ci yaw, te ba di wax kenn (fen nga) mbaa ( li nga wax du dgg) mbaa baat bu ko man a merloo ak doonte yaa ko mag, bu waxee loo xamul dggal ko te ne ko (man de nekkuma woon foofu) walla (jortoon naa ne) walla (xamewuma ko woon noonu) ak yu ni mel ci waxiin yu rafet Nangay tmmal saw lmmi wax ju rafet . Yonnant bi (j.m) nee na : (ku gm Ylla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiw mbaa mu noppi) kenn ci woykat yi nee na :(tmmalal saw lmmi wax ju baax, kon de danga ca ame ab cr)(lmmi de li nga ko tmmal rekk lay tmm)(lu mu man a doon la nga ko ca miinal rekk lay def)(moo xam lu baax la mbaa lu bon, deel xool nooy dollikoo) Sab dox na ko aajo di waral ci lu dul ag ry, ag ry de ci mbugal lay bijjee jme Bul di ree mukk ci lu dul lu yeme, bul dox mukk it ci lu dul aajo Bul gestu tam te skkuweesu ko, ndax yii ypp ag ndofe la gog dqoo naaki teggiin Sa tubay it bul ko di wui mukk, ndax loolu ci byyi ay teggiin la bokk Moom de ci jikkoy kccoor yi diy saay-saay te bokk ci giirug Hassaan la bokk, oom i dddu lu baax Nangay moytoo wui sa biir ak li nekk ci diggante jumbux bi ba ci bti-woom yi, (ngir bon gi mu bon) Loolu de mndargam rer la ak ndofe ak newug mba-rus gu mgg gi Ndax moom (mba-rus) mooy dttub diine, fu mu nekkul diine nekku fa , loolu de la (jngalekat yu mag ya) saxal Koo agsi ci moom nanga ko nuyyu, bu fekkee ne soxla nga ay teggiin Bu fekkee ne moo la njkk a nuyyu nanga ko fay ci kddu Boo saafoonteek moom (boo nuyyoonteek moom ) nanga dgral sa

www.daaraykamil.com

loxol ndijoor ci ndijooram, loolu mooy li nu rafetlu Bul rocci sa loxo li feek njkku la koo rocci moom ci anam gu fs Ndaxte de sibees na fkk ay loxo ci nuyyoo ci anam gu gaaw ak byyi wax ja Saafoonte ci aari loxo it bokk na ci ay teggiin, niki aar yi nu la waxoon leegi aanalal ki ngay nuyyool yaw boroom xel mi, ndax loolu de bokk na ci liy fari bkkaar Boo bggee dugg ci kr (walla negub) jmbur nanga yglu, kon de nga am la gn Bu u la digalee nga dugg nga dugg, bu dul loolu dellul Sab bt bul ko di wndel ci negub jmbur (mbaa kram ) ngir ragal gis fa awra joj bggunu woon nga gis ko

13 Saraa
Bokk na ciy teggiin booy jug aajo rekk di la yekkati, bokk na ci ag ndofe ngay ree te lu reeloo nekku fi, mbaa ngay dox ci lu dul aajo, mbaa ngay gestu te yittewoowoo ko, bokk na ci ay teggiin ngay moytoo wui say sr, loolu de ci jikkoy kccoori Hassaan yi la, bul di feeal lenn ci sa biir mbaa li nekk ci sa diggante jumux ba ci say wom, loolu de ci rer la ak kk kersa te kersa mooy dttub diine tey laylaat gi mu tege, fu kersa kke diine jug fa. Bokk na ci ay teggiin ngay nuyyu kpp koo dox ba gg ci moom, te di ko fay bu la nuyyoo, te ngay saafoonteek moom tey dgral sab loxo ci loxoom boo koy nuyyu, te nga ba koo njkk a rocci sa loxo , fkk loxo ci lu gaaw cib nuyyo de lu u sib la. Bokk na ci ay teggiin ngay saafoonteek moom ci sa aari loxo ypp, te nga koy aanal lu baax ak sa bopp loolu bokk na ci liy far ay bkkaar . bokk na ci ay teggiin ngay def booy dugg ci negub jmbur mbaa kram ngay yglu bu u la nee jllsil nga dugg, ndeem det nga dpp, rikk bul di snni sab gis ci kr mbaa neg boo moomul ngir nga ba faa gis loo warul a gis. Boo bggee kooy ndandool bu muy ku dese cim xel mbaa ku iaan mbaa ku bariy xemmeemtef Bu di toog ak ku dul ku lay dolli diine ak xel, kon de nga am ckkutef la Ndax de xibaar nau ne cam si de (waa ji) ma nga ca diiney xaritam ba, loolu ab adiis la bu u tuxal(waa ji de diine ji waayam yor rekk lay yor) Saraa: Da lay dnk nga ba a ndandook way dese yi cim xel te ba di toog ak ku la dul dolli diine ak xel, ci loolu de ngay ame la nga bgg, ndax waa ji de ni ab xaritam mel rekk lay mel, (wolof yi nee nau won ma sa xarit ma wax la sa jikko) seyyidinaa Aliyun - karramal laahu wajhahuu nee na:(Bul def mukk boroomug rer muy sab ndaale, moytu ko te moytu sa bopp)(bariwaa na aji rer ju alag boroomug lewet (ku nite) ba mu ko defee mbokk) (nit de ca moroom ja lau koy natt bu ndeek moom)(ni uy natte dll ca moroom ja bu u dee aar) (mbir de am na ag niroo akug natt ca moroom ja)(xol de misaal la ca moroom ja ) Am na ku ne :(boo nekke ciw nit nangay seet a ca gn ngay nd ak oom)(bul seet a ca yes ngay nd ak oom bay yes )(bul laaj waa ji, waaye laajal ab ndandoom)(Ndax ku nekk ca ka ngay ndal ngay roy) Bul skkoo gis mukk ab rcc-rcc (ci sa moroomu nit) bul gstu itam ay awra (ay aawtef)

14 Saraa
Mu ne : bokk na ciy teggiin ngay ba di gstu rcc-rcci nit i mbaa seeni aawtef. Waxees na ne : (bul di skkoo xam la nit a nbb ci seeni ayib) (ndax kat loolu man naa waral Ylla di muri mbalaan mi mu muuroon ci say aawtef) (rikk nangay tudd lu baax la nekk ci oom bu nu len tuddee) (bul ayibal kenn ci oom ndax kat loo len wax man naa am yaa len ko pp) Nanga mel ne na woykat ba waxoon: (dinaa bgg jikko yu rafet yi sama kem kttan) (tey ba di ayibale ak u may ayibal) (may jggal ug nit i ngir ag lewet) (ndax ki yes ci nit i mooy ki

www.daaraykamil.com

sopp ag ante) (ku weg nit i wegees ko) (ku xeeb nit i deesu ko weg) Ka wax lii de wax na wax ju rafet: (boo bggee dund sa diine mucc) (sa wrsg lw (bari) sab der o) ((boo bggee loolu) sa lmmi bu ci tudd mukk ayibi nit) (ndax kat yaw it am nga ay ayib, nit i ami lmmi) (bu Ylla dogalee say gt rot ci ayibi nit, nee leen :) ( ee yen gt yi bu len xool de, ndax nit i oom it am nau ay gt)

Xamal ne wuute ab del (fausser rendez_vous, dige te defoo ko) ak fen bokk nau ci gkk-gkki wax, dee leen teet (moytu)

Nekk na ci Adiisub kii nga xam ne maa ngi skku sellug ay julleeki slmal yuy sottiku ci moom aki oam aki saabaam, yi diy nderlaay:

(Dnk naa leen) adiis ba:nekkal di kuy wax dgg, teetal fen ngir nga kawe

Saraa: mu jubloo wax ne mi ngi lay dnk nga ba a fen, ba a wuuteb del, te di leen ko tere, ngir ne ooy gkk_gkki wax, Yonnant bi (j.m) nee na: (( Dnk naa leen dggu, ndax mooy yobboo cig mbaax, teg mbax mooy yobboo jjana, waa ji bu saxee di dggal te di ko skku, bu yggee bindees ko fa Ylla muy ku dggu, moytuloo naa leen fen, ndax day yobboo cig mbon teg mbon mooy bijje jme sawara, waa ji bu dee fen te di ko skku, day mujj bindees ko mu dib fenkat fa Ylla))

Fonkal sa aari way jur, te am yrmaande ci oom ak eewant, te deel gaaw ci seeni ndigal aki mbir Deel ba mbooleem li u la tere, boo ko dee def de, sag kawe dina yokku Kpp ku la mag ci jegeaale yi nanga ko weg Ak u dul jegeaale yi, rikk nanga nekk ak mbindef yi ci jikko yu rafet, kon de aji Skke ji (Ylla) dina la sopp Nangay rafetal jikko yi cig yaatu-yaatulu, ak a skkoo sopplu ci oom (mbindef yi) kon de soppees la Nangay nooyal i wax ci nit pp, loolu de ci jikkoy way aw yi la bokk (u yewwu i) Xibaarees na jle ca boroom ngnel la (Yonnant bi (j.m)): genn-wllu xel mooy sopp-sopplu ci nit i (fexe ba nit i sopp la) Bokk na ci texeg nit ki, xolub boroomug njub ba koy ba ak a fo

Saraa: Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga fonk sa aar i way jur te eewant leen, di gaawantu ci def seni ndigal, di byyi seen i tere , Ylla mu kawe mi nee na: (( Nit dnk nanu ko lu baax ciy way juram (maanaam mu fonk leen) )), ak yu

10

www.daaraykamil.com

dul boobu ciy laaya, ak nga fonk ku la mag ci jegeaale yeek u leen moy, te ngay rafetal say jikko ci di leen mayug yaa, ak won cofeel ak a skku u sopp la, skkug cofeel ci nit i de mooy genn-wllu xel, na la wor ne bokk na ci texeg nit ki, xolub aji gm di ko bgg, deel nooyal say wax eel nit pp, ndaxte loolu kay ci jikkoy way yewwu yi la bokk. Deel skku seenug aan foo tollu, deel barkeelu it ci oom, loolu de dina la yobbe ag kawe guy dolliku Mggal boroom xam-xam bu jfe (xam-xam ba) mooy mggal boroom aras (toogu ba) ci lees tuxal (li nu jle ca Yonnant ba) Foo ndeek ku la mag nanga sax ci di ko weg Moo xam cib tukki la mbaa lu ko moy, deel not sa bakkan ci di ba di toog ak moom ci kaw Deel toog ci suuf, bul di toogaaleek moom cib lal ak doonte da la caa woo sax ngirug yaatal Ndare muy lu manul a kk, su leen am wi dikkalee mbaa naan gi yaw ngoor si Bu ko ca jiite mukk, xaar ca ndigalam, loolooy jub ga Deel seet la gn ca am wa it di ko ko jox ngir ag wormaal Dee ko liggeyal ci mbooleem li mu aajowoo, kon say aajo dees na la ko fajal Saa soo ndeekuw nit cib tukki, dee leen dimbali ci mbooleem lu u soxla Liggeyal-leen te smmal-leen seeni waruwaay (seeni fas mbaa mbaam walla sax wata) yoral-leen seeni bagaas Dimbali-leen oom pp loo ci man, jggal-leen su u sgganee Neen ak noflaay jmm ju bgg a doon dara du leen taamu Ndax kat aw yiw manul a bawoo ci oom aar, tew ay rekk a cay bawoo eel murit bi Boroomug yayoo bu skkoo ci yaw dara, defal ko ko Bul nay mukk ci poat mii (alali ddina jii) ba loolu di waral sa gcca ca (yalmal qiyaam) bis pnc Boroomug nay ku sori Ylla lay doon ak mbindefam ypp foo ko fekk Boroomug nay dees koy wommat jme sawara, soril ko jjana safaan ba mooy aji tabe ja, ca lees wax, kon nekkal aji tabe ji, bul nekk mukk aji nay ji Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga siyaare boroom xam-xam yeek gaa u baax i, nga leen di liggeyal ak a barkeelu ci oom, tey skku ci oom aan, ndax kat mggal boroom xam-xam mooy mggal Ylla mu kawe mi. Saa soo ndateek ku la mag cib tukki, mbaa lu ko moy nanga ko byyee lal ba tey toog fa suuf, te bul bokk ak moom tdd mukk ndare ngir lu manul a kk, bees leen indilee am mbaag naan, rikk bu ko ca jiitu, xaar ca ndigalam, dee ko byyee la gn ca am wa, te di ko liggeyal ci lpp lu mu aajowoo. Bu Ylla dogalee nga nd ak aw nit cib tukki, doonal seen mbindaan, smmal leen seeni waruwaay, yoral leen seen i bagaas kem li nga man. Bul taamu mukk ab noflaay ak loxoy neen, aw yiw nekku ci de te kenn du jot teddnga ga ci lu dul ab coona niki lees ko waxe: Cig farlu lees di jote kawe ga, ku bgg ag kawe fog guddi yi (fog kk a nelaw guddi)

11

www.daaraykamil.com

Dangay skku ag teddnga ba noppi di nelaw guddi, na la wor ne xemmemloo nga sa bakkan lu jomb (bgg nga lu manul a nekk) Mi ngi lay digal nga ba a nay ci dara ci dduna, ku nay kat ku sori Ylla la, ku sori nit i la, ku sori jjana la, ku jege sawara la. Safaan ba it mooy ku tabe ki, woykat ba nee na: Bu fekkee alal wacc koo tax deesi dajale ko, kon lu tax cam si (nit ki) di nay ci lees di wacc Teralal gan ya cig yaatal (dalal jmm) ak ganale ak mbgteek jegeel Rikk bu sa dnn(xol) xat mukk ci gan, ndax moom balaa ygg mu laxas (mu dem) Nekk na ca Adiisu Kees tnn ka (Yonnent bi)yal na Ylla julli te slmal ci moom aki oam ak kpp ku ko topp: (Ku gm), aji wax it ne: (gan gi teral ko) ca bahrub kaamil ba (mu defe woy wa ci galan bu tudd kaamil) Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga teral gan, yaatal ko, te ba a xat ngir moom, ndaxte balaa ygg mu dem, Yonnent bi (j.m) nee na: (( ku gm Ylla ak bis pnc ba, nay teral ganam). Ab woykat it def aw woy ci galanu kaamil: ( Gan gi teral ko, ab fanaanuwaayam yelleef la (lu mu moom la), rikk bul nekk rbbum way wcc yi ( bul nekk ak saagay gan yi) Nanga xam ne gan de fwwu mu nettali oam fa mu fanaan, ak doonte laajeesu ko ko (wolof nee na: gan dees na ko xa lpp ba mu des nettali). Nanga ko gatandoo kanam gu nooy te yaa, waxees na ne moo gn ganale, moom la woykat biy feddali:

(( Kanam gu nooy de moo gn ganale, kon de xanaa bu ko waa jiy def (ganale) ci kanam gu nooy dina yeme? )) ((Dinaa ree sama gan njkk muy wcce ag raxlaam (njkk muy wcc) bu ko defee mu naat fi man te booba barab bi bu bekkoor la)) (( Duma wax mukk bu ma gan ganesee:jllal sa kr soriwul))

Sunu kr de fu yaa la ca ka ko siyaare (ubbilees na ko gan gu fgg gu nekk) ook aji fgg jee ci yam (ook gan ee ci yam) Lpp lu fa nekk, lu dagan la eel ko, ndare la aji bind ji araamal ............... Bul byyi benn bis am njng, te nga jfe ko cig jaamu Ylla Xam-xam day dundal xolub aji xamlu ji, day leeral xol tey dindi ngumba (gu xol) Xamal ne rawanteg nit i ci xam-xam lay nekk ak diine, nanga dkke mu Ci oom aar it la ku gn di gne, du ci ag askanoo ci ku kawe Ci wllug askan, moo xam baay la mbaa nday, kon farlul ci oom aar nd ceek i teggiin Booy skku xam-xam dimbandikool Ylla te sellal ci xol bu dal Te ngay dkke jng nag, ak smm (smmoonteek ndigal ak terey sunu boroom yi) Newal i nelaw, newalug regg Saxal ci jng ak nafar li nga jng te ba koy dddook a ginnaawal Nangay wuuteek bakan, ndaxte bakan li mu lay xiir du dara lu dul luy waral ag tj

12

www.daaraykamil.com

Newalal nelaw yi, tggool ak tyyeel, newalal noflay, gttalal mbat Xamal ne ku ba a jng cig ndawam, dina dajeek rccu Ndaxte kpp ku gaawantuwul jm ca xam-xam ya (ku gaawantuwul jngi) te fex ngir oom njkk yitte ya Lu ci pp du am la mu ca yittewoo, te du ca jot ckkutefam Ndaxte taggees na njngum gone ne mook bind ci doj a yam (bind ci simaa bu tooy, bu wowee du daati) u niroole nag njngum mag ak bind ci ndox ni muy kke jeexiit ....................... Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga ba a byyi jng benn bis, ndaxte xam-xam mooy dundug xol tey daug ngumba, di leerug bakan niki lees ko waxe: Xam-xam day wui ngumba wliif xolub boroom, ni weer di wuee kriisug lndm ga Ci xam-xam la ay xol di dunde yoy masuoo xam bu njkk lam mooy tqale gi am ci diggante dgg ak fen Xam-xam ag leer la eel bakan, mu cay niite dgg gi (di ci tegtaloo ngir xam li am) dafa mel ne leer ci bt Mi ngi lay xamal ne nit i seenug rawante ci xam-xam ak diine la nekk, te ci moom lees di gne, du ci askanoo ci baay mbaa nday, noonu la ko Seydinaa Aliu waxe (yal na Ylla teral kanaman): Nit i boo leen dee natt oo yam seen baay Aadama la, seen nday Awa Boo dee ndamu ci askan wu tedd, nanga xam ne ci ndox ak ban la bawoo Ndam daal o xam-xam la eel, ndax oo gindee eel ki ko soxla Darajay cam si (nit ki) mooy la mu man (am ci ag xere), way rer yi (i amul xam-xam) ay noon lau eel woroom xam-xam yi Wutal xam-xam, kon de dinga ci dunde ba fww, ndax nit i way faatu lau, te woroom xam-xam yi dunu faatu way dund lanu Mu lay xamal ne bokk na ci liy dimbalee ci xamlu te di ko yombal, ngay ragal Ylla ci sab xam-xam, te di ko skku ngir moom, di newal i nelaw, ak regg tey taqoo jng niki lees ko waxe: Yaw aji xamlu ji gaawantul skkuji ag cmm (ragal Ylla), te nga bccngal nelaw yi, tng regg gi (merook regg gi) Jublul ci bind bi, bul tggook moom, xam-xam ci jng la taxawe te yekkatiku ****************** Te fww ngay jng tey baril nafar di wuuteek bakan bi ci loolu, niki lees ko waxe:

Sama xarit bul di tyyeel te bul di neenal bind bi ( dee ko topp ak a nafar), te bul topp mukk sa bakkan cig neenalam ( ci di ko kk a defloo dara) Bul di byyi ag baamu (nafar) ca la nga jot a wattu (mokkal), ku byyee baamu (nafar) fwwu mu ftte (ftt la mu mokkaloon) ****************************************** Te ku gaawantuwul def am njngam te def ci yitteem jpp cig ndawam, dina jafe mu am ca la mu ca nammoon, ndax jng cig ndaw mook boyaade ciw doj a yam (bind ci simo bu tooy), jng cig mag nag mook bind ci ndox a yam (booy teggi sa loxo muy far) , lenn ci woykat yi wax na ne:

13

www.daaraykamil.com

Gis naa ne damay faral di ftt li ma jng bi may mag, te kat fttewuma li ma jng ba may gone Xam kon mooy jng cig ngone, lewet nag di ga nga def-deflu cig mag (lewet fii: nite, xel, tegu ci yoon) Bees xaroon xol bees jngal cig ndaw, dees fay fekk xam-xam muy lu mel ne lees boyaade ciw doj (mu mel ne mbind mees def ci simo bu tooy) Boo bijjaawee ba noppi di jng yaa ngi sonal sa bopp, rawati na bu xol bi sonnee ak dgg beek gis bi Nit daal aar rekk la, xel ak xellu (logique), ku lii raw ak lee, na xam ne alku na ********************************** Nanga xam ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul tyye sa bopp wliif "dgg naa ak waxees na" Du la may (moom xam-xam) lennam mukk li feek joxoo ko sa lpp, kon farlu ci. Jox ko sa lpp ci lu dul xccoo, fogalal sag guddi (bul di nelaw guddi) te xiifal sa biir Deel maral sa bccg ci xam-xam, di ci sonal sa cr ypp nd ceekug teggiinu Ku ko skkoowul noonu du ca am lu am njari, noonu lees ko xibaare Xibaarees na it ne moom de ab foaakon la (kuy daw di soree), ku dul cam su di ab mukat du ko am Nangay sax cig toroxlu cig toroxal sa bopp, ca jamonoy xamlu ja, kon de danga am leerug xol Ab xamlukat bu ryee, du am nammeelam Bayyil ag pexlu (noos) bul di toog mukk cib lal ca jamonoy jng ja, ci lu dul aw tiis (kk pexe) Nangay boole yitte ji jpp ci li ngay skku, ci lu dul gestu jm ci lu warul Bul di dglu nit i mbaa xccoo yi u nekk Bul di yeexe am njng, mbaa nga naan di naa ko defi bu ma fexee, soo bgee dab gaa u baax a dduna de am na yitte yuy teree gg ca njub ga, te duu jeex Dee de cig mbetteel lay we, te bariwaa na fu mu bome boroomi soxla Mu jubloo wax ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul tju wlif ag jaxasoo, xamal ne du la jox mukk lennam ndare bu danga koo jox sa lpp, ku ci xiifalul biiram, fog guddeem, mar bcgam, sonali cram, du ca am lu am njari, ndax xam-xam ag leer la, ku dul aji mu du ko am, woykat ba nee: Skkul te bul yoqat ci skku gi, gkk-gkkub aji skku ji xam-xam mooy yoqat Xanaa gisoo ne buum sax bu yggee jaar ci pindub teen, byyi fay jeexiital Kuy jng fwwu muy toroxlu ak a suufeel boppam buy xamlu, lu ko moy du ca am nammeelam, war nay byyi ag noos, bu muy toog cib lal mukk ci waxtuw jng, ndare bu loolu da di lu manul a kk ba gg ci lool, booleel sa yitte jpp booy jng ca la ngay jng, bul di gestu leneen lu ko moy, bul di dglu nit i mbaa la u nekk, mi ngi lay dnk it nga ba di yeexe am njng, naan danga koy byyi ba fex ci yitte yi, ndax yittey dduna duu jeex mukk

14

www.daaraykamil.com

Kenn faju fi aajoom, aajo it fajuwu fi ndare bu jeneen daa juddu. Yaw amaa na sax dee gi dikkal la, ba laa booba, ndax dee de mooy aji fddu (ku fi nekkul) ji gn a jege, te buy w cig mbette lay doon. Ginnaaw bi mu wax ci nees di tegginoo ak Seexul Murabbii (Sri biy jngale) ak ki lay jngal ak sa mbokk dgg ak sa ndandoo dgg, daal di ne: Fig wegeel man a yam mooy nga weg sa sri, def ko ab sang, may ko say xewal Fajal ko ay aajoom li feek yaa ngi dund, ci di ko jox, di ko liggeyal li nga man Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga weg sab sri, wormaal ko, fajal koy aajoom li nga man, te ngay teet reek kaf ak coow ci kanamam, boo jubloo defi teggiin Boo toogee fa moom bul di baril ay gestu mbaa ngay yngu fu nekk nga jm fa Bul di baril wax fa moom, nekkal di kuy noopi, loolu dina waral nga am ag jubalam Bul nd ak moom mukk lu dul cig mggal, bul roy mukk waa jamono jii ( ci seenug kk a mggal seeni sri) Bul def mukk ni ka ndoon ak Qudar, ndare bu daa manul a kk (bul ko di laaj lu mu def lu nekk, nga ne ko loo ci jublu) Deel def li mu la digal, ak doonte sa bkkan da koo bggul Lu mu la tere it baal te daw wlis ko, te teet sa bnneex Mu jubloo wax ne mi ngi lay aaye ngay baril coow akum po ak ree ak gestu bu bari ci kanamam, bu ko def it ndandoo ndare bu daa manul a kk, di deglu ay ndigalam tey teeti tereem ak doonte sa bakkan begu ci. Bul di da di ko di jox i ddiya kem li nga man Ak doonte lu new la sax, ngir rekk topp lees wax ne day dooli moom ddiya ag coffeel Loo ko gis mu jeng jm ca, gaawantul dem ca Te farlu cig jottali ko ko, ndax kat rafetug jf ma nga ca matal ko Nanga nekk dib jaam eel kpp ku aju ci moom ci o, oom pp nag nd ceekug wormaal nag, ndax mu sarax la ab xool boo man a ame la nga bgg Benn xool bob cofeel bu tukkee cib sri jm cib taalibeem mooy ngnel ya tey kawe ga Nanga nekk fa sri ba niki ab new bees tral ci kanamu aji sangam, kon de nga jariu Boo dee skku xam-xam it, nangay skku ngrmul aji jngale ji ngir jmmi Ylla Nanga mel ca sab sri nib jaam, loolu de dina tax nga jot darajay buur yi (dina tax nga doon buur) Xamal ne njari deesu ko am ndare cig mggal ci li u wax Kem ni nga mggale sab sri ngay ame li nga bgg, ci ngay ame it barke Ku grmloowul ab sriam, du grm ab dongaam Bariwaa na waa jees miin ci xam-xam te kenn jubluwu ko

15

www.daaraykamil.com

Yal na nu Ylla musal ak yeen ci xam-xam bu jariul ki ko xam Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal ngay ddiyaal sab sri li nga man ak doonte lu new la sax, te skkoo def lpp loo ko gis mu jeng jm ca ci mbir mu mu man a doon, tey farlu ci jottali ko ko, te ngay wormaal mbooleem i aju ci moom, moo xam o la mbaa jaam ak u leen moy, ndax sax mu xool la ab xool bob cofeel bu la ci Ylla man a dimbalee. Xamal ne kem ni aji xamlu ji di mggale aji xam ji lay jarioo, wa xees na : Gis naa ne li gn a war ci mbir yi mooy qi jngalekat te mooy ji gn a feddaliku ci bpp jullit Lu yell la deesi ddiyaal ko ay jnniy drm ngirug teral, ci wenn araf wu mu la jngal wu nekk ggees na ci wax ne moom lees jiital ci qi waajur ni ko enn i waxe : Damay jiital sama qi ustaas ci sama joj waajur ak doonte xam naa ne yoreel naa waajur wi njekk ak eewant Ndaxte kii mooy aji yar ji ruu gi, teg ruu wurus la, kee nag mooy aji yar ji yaram wi te moom yaram wi am mbuusam la (mi koy mb) Nanga mel fa moom niki new ci kanamu ki koy sang, mbaa gumba gees di wommat ci yoon wu nekk ci digg gej ni muy toppe aji wommatam, niki lees ko waxe : Bu la Ylla tawfexalee ba nga am sriub dgg bu raw ci lefum Haqiiqa Rikk nanga jug ci skku ngrmam, xeetu nammeelam, te ba lpp loo nekkoon bu njkk Nanga mel fa moom ni new fa ka koy sang, da koy wlbati fu nekk muy wlbatiku Mbokk dgg ak xarit bu wr oo gn a new luy new Mooy lu mel ne waxi ki wui lndm yi: sa xarit dgg mooy ki nd ak yaw Mooy kiy lor boppam ngir jari la, mooy kok bu la jamono njattee Mu sonnal boppam ngir siggil la, ma ne mooy ki lay nbbal lu aaw ngir yekkati la Tudd naa ciy teggiin am mbooloo mom dina fajal ku ko taqoo mbooleem ay aajoom Doy na skk ci ku ko settantal, aji saafara la ci ku ko jfe Dina tegtal boroomum xel, dina ko tegtal banqaasi bunt bii, bu ci royee nd ceekug toroxlu Ba mu far matal fnni teggiin yi te bokk na ci yooni teggiinu yi: Di def li nga gis mu rafet tey ba li nga gis mu aaw Lenn ci oom laajees na ko: ku la yar? maanaam koo roy ba mel nii nga mel? Mu ne damaa dkke di xool rerug kii nga xam ne ne reram gi leer na n Bu ko defee ma koy teet (moytu). Fii la tontu li yam.

Aji Tekki ji: Abdu Xaadir KEBE

16

www.daaraykamil.com

You might also like